jeudi 9 octobre 2014

Poème en Wolof sur Serigne Mouhamadoul Amine Bara MBACKE Ibn Serigne Fallou [Par Abdoul K. Ba Majalis]

Bismilaahi may bëgga woy
Doomi Fadlu Laahi Lamiin
Sët ba njëkk a nekk xaliif
Bahda Saalihu-bnu Xadiim



Aama « haktachin » la fi ñëw
Fekk yoon wi ñépp gëlam
Ñii ne lenn dootu fi baax
Ngir la doomi Bàmba yi dem

Ñuu nga naan bu sët yi desee
Kenn dóotu jub di jubal
Fekk Bàmba def na fa kun
Ney mbiram kanam lañu jëm


Ahmadul Amiina ñëwaat
Aw fa Baay yu baax ya awoon
Rakk yépp topp ko faf
Maam ja wallu leen indi ndam

Ñaari at yu néew la fi def
Ak Juróomi weer yu tofal
Waaye jëf na lol ba abad
Yoonu diine ken du ko jam

Baara Fadlu yaa ñu sagal
Nun murid yi ak ku fi gëm
Ngir dangaa jëfal sunu Maam
Seexunaa-l Xadiim mi nu gëm

Yaa tabax jumaaki tëli
Boole kook yewén te gore
Yeesalaat murid gi bu wér
Yaa dalal suniy xelitam

Nos julit yi yépp ci buum
Yaw sagal nga bépp murid
Uuf njaboot gi doon sunu nday
Dàq ag njirim bamu dem

Yoonu Màkka jooy na la yaw
Kaaba gaak safaa wa kazaa
Kuy julit te bëgg lu baax
Sant nañ de nun ñi la am

Yàlla yaw fayal nu Lamiin
Bàmba dellu dolli ko fay
Fadlu Laahi bég na ci moom
Doomi Bàmba yépp a ko xam

Say ngëneel xajul ci këyit
Waaye noonu ngay man a mel
Doomi Fadlu tey turandoo
Ahmadul Amiin sunu Maam

Ñoo la faguloon la nga doon
Démb booba tay ñëwagul
Moo taxit matal nga bu wér
Séeni naal dangaa bari jom

Baara yaw bégal fa nga ne
Làq ngay ngërëm ci lu wér
Noo ngi sant Yàlla ci yaw
Ñii nga bàyyi am na ñu ndam

Yal na Yàlla sàmm njaboot
Taaw ba Mustafaa ki rakam
Taalubeek ña topp ci yaw
Ak kulay bégeek a gëram

Sab sëtëy ki doon joriku
Rax ci ngay nijaay di sëriñ
Yal na sax ci woy la abad
Abdu Xaadir moo di turam

Yal na Yàlla taas nu ci moom
Yiir nu fal nu dolli nu nguur
Def nu ay murid yu dëgël
Barke Baay ba ibnu Xadiim
............................
Aji woy ji: Abdul Xaadir Ba Majalis